3Bu ma sànkaaleek ab soxor, di ma booleek kuy def lu bon, di wax moroom ma jàmm, te dencal ko ay ca xolam.
4Fey leen seen liggéey, seen kemu jëf ju bon. Jox leen seen añu jëf, yool leen seen yelleef.
5Xooluñu Aji Sax jeeki jëfam, ak liggéey bi mu def. Da leen di yàqte, te dootu leen yékkati.
6Jaajëfe Aji Sax ji, ki ma nangul samay dagaan!