6Ñooñooy waa làng, gi lay sàkku, di maasug Yanqóoba, giy sàkku sa yiw. Selaw.
7Neleen bunt yi kulbét, ubbileen bunti cosaan yi, Buur Boroom ndam duggsi.
8Buur Boroom ndam booboo di kan? Xanaa Aji Sax ji Boroom dooleek njàmbaar, Aji Sax ji jàmbaaru xare ji.
9Neleen bunt yi kulbét, ubbileen bunti cosaan yi, Buur Boroom ndam duggsi.