3leqli ma, teg ma ci yooni njekk ngir teddngay turam.
4Su may jaare xuru ndee wu ne këruus it, duma ragal loraange: yaw laak man, sa bantu sàmm ak sa nguul, yooyoo may dalal.
5Yaa ma berndeel, noon yi gis, nga diwal ma saa bopp, terale ma, saab kaas rembat.
6Mbaax ak ngor kay la ma Aji Sax jiy dare sama giiru dund, ma dëkke këram ba fàww.