3Éy sama Yàlla, ma woote bëccëg, wuyuwoo; woote guddi, nopploo ma.
4Yaw de, yaay ku sell, tooge sab jal, Israyil di la kañ.
5Yaw la sunuy maam wóolu woon, wóolu la, nga xettli leen.
6Yaw lañu daa woo wall, mucc; yaw lañu wóolu woon te rusuñu.
7Man nag aw sax rekk laa, matuma nit. Doom aadama sewal ma, aw xeet tuutal ma.
8Ku ma gis ñaawal ma, biiñ ma, xeelu ma, naa:
9«Na wéeroo Aji Sax ji, mu xettli ko; su ko soppee, na ko wallu.»
10Yaw de yaa ma roccee sama biiru ndey, naxe ma sama weenu yaay.
11Yaw laa dénkoo ba may juddu, ba ma juddoo sama ndey, ngay sama Yàlla.
12Bul ma sore, musiba teew na, wall amul!
13Noon yaa ngi ma gaw ni coggalu yëkk, dar ma ni ponkali yëkk ya fa Basan.
14Ñu ŋa ma, ŋàpp, ni gaynde, guy yëmmook a fàdde.
15Doole ŋiis, yax yoqi, fit ne soyox, seey.