27Ku woyof a cay lekk ba doyal, kuy wut Aji Sax ji, sant ko. «Guddleena gudd fan!»
28Àddina wërngal këpp ay fàttliku, walbatiku ci Aji Sax ji. Làngi xeet yépp sukkalsi ko.
29Aji Sax jeey boroom nguur, moo yilif xeet yi.
30Boroom barke xéewlu, sujjóotal ko, ku jëm pax it, te bakkanam di lang, di ko sukkal.