20Waaye yaw, Aji Sax ji, bul sore; yaa may dooleel, gaawe ma.
21Xettlil sama bakkan ci saamar, ba sama benn bakkan bii mucc selli xaj!
22Musal ma ci pàddum gaynde ak ndañum nagu àll. Yaa ma wallu woon!
23Ma siiwali saw tur ci bokk yi, màggale la digg mbooloo mi.
24Yeen ñi ragal Aji Sax ji, santleen ko. Yeen askanu Yanqóoba wépp, màggal-leen ko. Yeen bànni Israyil gépp, wormaal-leen ko.
25Moom de sàgganewul boroom tiis, làqu ko kanamam, ba mu wootee, wuyu na ko.