14Ñu ŋa ma, ŋàpp, ni gaynde, guy yëmmook a fàdde.
15Doole ŋiis, yax yoqi, fit ne soyox, seey.
16Làmmiñ taqoo denqleñ, doole jeex, ma wow koŋŋ, nga tëral ma buntu bàmmeel.
17Ay xaj a ma wër, di gàngooru saaysaay, dar ma kepp, bëtt samay yoxook samay tànk.
18Maa ngii, mana waññ sama yax yépp, ñoom ñuy xoole, di ma seetaan,
19séddoo samay yére, tegoo bant sama mbubb.
20Waaye yaw, Aji Sax ji, bul sore; yaa may dooleel, gaawe ma.