3Yaa ko may nammeeli xolam, gàntuwulooy dagaanam. Selaw.
4Yaa ko gatandoo barkey ngëneel, kaalaa ko wurusu ngalam.
5Mu ñaan mucc, nga saxal jalam fàww,
6sag wall a ko sagala sagal! Teddngaak daraja nga ko sédd,
7jagleel ko barke bu sax dàkk, bégale ko sa kanam, mu bànneexu.
8Buur wóolu na Aji Sax ji, moos, du tërëf, Aji Kawe jee gore.
9Buur, yaa naan sa noon yépp céex, ne say bañ taral.