3 Yaa ko may nammeeli xolam, gàntuwulooy dagaanam. Selaw.
4 Yaa ko gatandoo barkey ngëneel, kaalaa ko wurusu ngalam.
5 Mu ñaan mucc, nga saxal jalam fàww,
6 sag wall a ko sagala sagal! Teddngaak daraja nga ko sédd,
7 jagleel ko barke bu sax dàkk, bégale ko sa kanam, mu bànneexu.
8 Buur wóolu na Aji Sax ji, moos, du tërëf, Aji Kawe jee gore.
9 Buur, yaa naan sa noon yépp céex, ne say bañ taral.