7Asamaan lay fenke cat lii, wëndeelu, sowi cat lee; amul lu rëcc tàngooram.
8Yoonu Aji Sax jee mat, di leqli bakkan. Lu Aji Sax ji seede dëgg la, day xelal ku xeluwul.
9Lu Aji Sax ji tegtale, njub la, di bégal xol. Lu Aji Sax ji santaane, leeraange la, di leeral gis-gis.