38Ma dàq noon yi, dab leen, jekkli, doora dëpp.
39Ma jam leen, jógatuñu, xanaa fëlëñu, ma joggi.
40Sol nga ma dooley xare, sukkal ñi ma jógal, ñu féete ma suuf.
41Won nga ma ndoddi noon, ma boole bóom bañ yi.
42Ñu ne wallóoy, wall amul; ñu woo Aji Sax ji, faalewu leen.
43Ma wol, ba ñu doon pënd, ngelaw wal, ma wetti ni banu mbedd.
44Xettli nga ma ci bokk yiy fippu, def ma, ma jiite ay xeet; waaso wu ma xamul sax nangul ma,
45ku ma ci dégg, déggal ma, ay doomi doxandéem di ma raamal,