38 Ma dàq noon yi, dab leen, jekkli, doora dëpp.
39 Ma jam leen, jógatuñu, xanaa fëlëñu, ma joggi.
40 Sol nga ma dooley xare, sukkal ñi ma jógal, ñu féete ma suuf.
41 Won nga ma ndoddi noon, ma boole bóom bañ yi.
42 Ñu ne wallóoy, wall amul; ñu woo Aji Sax ji, faalewu leen.
43 Ma wol, ba ñu doon pënd, ngelaw wal, ma wetti ni banu mbedd.
44 Xettli nga ma ci bokk yiy fippu, def ma, ma jiite ay xeet; waaso wu ma xamul sax nangul ma,
45 ku ma ci dégg, déggal ma, ay doomi doxandéem di ma raamal,