1Mu jëm ci njiital jàngkat yi, ñeel Daawuda jaamub Aji Sax ji. Mu jagleel Aji Sax ji woy wii, bés ba mu ko xettlee ci mboolem noonam, xettli ko it ci Buur Sóol. Kàdduy woy yaa ngii.
2Mu ne: Aji Sax ji, maa la sopp, yaw mi may dooleel.
3Aji Sax ji laay sës, mu di ma aar, di ma wallu. Mooy sama Yàlla, ji may sës, yiiru, fegu; mooy Boroom doole ji may musal, di ma làq.
4Ki yelloo cant, Aji Sax ji, moom laa woo, mucc ci samay noon.
5Buumi ndee tanc ma, walum kasara naq ma,
6buumi njaniiw laaw ma, dee ne jaas, di ma fiir.
7Ma jàq, woo Aji Sax ji, ne sama Yàlla wallóoy, mu dégge këram. Ma yuuxu, muy dégg.
8Mu mer, suuf yëngu, di ker-keri; kenuy tund ya jaayu, di reg-regi.
9Saxar di sël-sëlee ca wakkan ya, sawara boye ca gémmiñ ga, xal yu yànj tàkke ca.
10Mu firi asamaan, wàcc, niir yu fatt lal tànk ya.
11Ma nga war malaakam serub, di naaw, daayaarloo laafi ngelaw.
12Ma nga bàddoo lëndëm, làqoo, làmboo ndox mu lëndëm aki xàmbaar,
13leer a ko jiitu, xàmbaar ya topp ca, ak tawub yuur ak xali sawara.
14Aji Sax jee dënoo asamaan. Aji Kawe jee àddu, muy tawub yuur ak xali sawara,
15mu soqiy fitt ak jumi melax, tasaare leen, fëlxe.
16Aji Sax ji, dangaa gëdd, nokki, mu riir, xuri géej ne fàŋŋ, kenuy suuf ne duŋŋ.
17Aji Sax jee yóotoo fa kaw, jàpp ma, seppee ma ca xóotey ndox ma,