9ma rëcc ñu bon ñi ma song, noon ñii ma gaw, nar maa bóom.
10Seen xol dàq yërmande, seeni wax di reewande.
11Tanc nañu nu fépp, ne nu jàkk, nar noo tëral.
12Mbete gaynde gu namma fàdde, gaynde gu mat guy tëroo!
13Éy Aji Sax ji, jógal dajeek moom, detteel ko. Xettlee ma sa saamar, ma rëcc ku bon.
14Éy Aji Sax ji, walloo ma sa doole, ma rëcc ñi séddoo dundu àddina. Say soppe, nga reggal, seeni doom regg, desalal seeni doom.