7Na sa ngor feeñ, yaw miy walloo sa doole ku la làqooy noonam.
8Sàmm ma ni peru bët; làqe ma sa ker,
9ma rëcc ñu bon ñi ma song, noon ñii ma gaw, nar maa bóom.
10Seen xol dàq yërmande, seeni wax di reewande.
11Tanc nañu nu fépp, ne nu jàkk, nar noo tëral.
12Mbete gaynde gu namma fàdde, gaynde gu mat guy tëroo!
13Éy Aji Sax ji, jógal dajeek moom, detteel ko. Xettlee ma sa saamar, ma rëcc ku bon.