5Kuy déggal Yàlla, man na maa dóor, bantal ma ci ngor. Loolu ngëneelu cuuraay la, duma ko bañ. Waaye maa ngi saxoo ñaan pexey noon moy.
6Yal nañu fenqe seeni njiit ciw doj, ba noon yi xam ne dëgg laa wax.
7Ni ñuy gàbbe suuf ba mu ne ŋafeet, ni la njaniiw di ŋaye, aw seeni yax yu tasaaroo.