Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sabóor - Sabóor 141

Sabóor 141:3-7

Help us?
Click on verse(s) to share them!
3Aji Sax ji, sàmmal ma sama làmmiñ, saytul ma sama kàddu.
4Bu ma xiir ci lu aay, may jëfe jëf ju bon, ànd ceek ñiy jëf lu ñaaw, di wàlli seeni bernde.
5Kuy déggal Yàlla, man na maa dóor, bantal ma ci ngor. Loolu ngëneelu cuuraay la, duma ko bañ. Waaye maa ngi saxoo ñaan pexey noon moy.
6Yal nañu fenqe seeni njiit ciw doj, ba noon yi xam ne dëgg laa wax.
7Ni ñuy gàbbe suuf ba mu ne ŋafeet, ni la njaniiw di ŋaye, aw seeni yax yu tasaaroo.

Read Sabóor 141Sabóor 141
Compare Sabóor 141:3-7Sabóor 141:3-7