3 Aji Sax ji, sàmmal ma sama làmmiñ, saytul ma sama kàddu.
4 Bu ma xiir ci lu aay, may jëfe jëf ju bon, ànd ceek ñiy jëf lu ñaaw, di wàlli seeni bernde.
5 Kuy déggal Yàlla, man na maa dóor, bantal ma ci ngor. Loolu ngëneelu cuuraay la, duma ko bañ. Waaye maa ngi saxoo ñaan pexey noon moy.
6 Yal nañu fenqe seeni njiit ciw doj, ba noon yi xam ne dëgg laa wax.
7 Ni ñuy gàbbe suuf ba mu ne ŋafeet, ni la njaniiw di ŋaye, aw seeni yax yu tasaaroo.