Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sabóor - Sabóor 140

Sabóor 140:6-9

Help us?
Click on verse(s) to share them!
6Ñu bew ñee ma làqali yeer, lalal may buum aki caax, feggal ma seeni fiir ci yoon wi. Selaw.
7Dama ne Aji Sax ji, yaay sama Yàlla; Aji Sax ji, teewlul, ma dagaan la.
8Aji Sax ji Boroom bi may walloo doole, yaa ma yiir keroog bésub xare.
9Aji Sax ji, bul may ku bon nammeelam, bul joyal pexeem, muy yékkatiku. Selaw.

Read Sabóor 140Sabóor 140
Compare Sabóor 140:6-9Sabóor 140:6-9