Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sabóor - Sabóor 138

Sabóor 138:2-6

Help us?
Click on verse(s) to share them!
2Ma sujjóot jublook sa kër gu sell gi, di wormaal saw tur, ngir sa ngor ak sa worma. Màggal nga sa tur ak sa kàddu, ba mu tiim lépp.
3Bés ba ma wootee, yaa ma wuyu, ñemeel ma, dooleel ma.
4Aji Sax ji, na la buuri àddina yépp màggal, ñoo dégg kàddu yi nga wax.
5Nañu woy say jaloore, naan: «Aji Sax jeeka màgg teddnga!»
6Aji Sax jee kawe! Ku toroxlu, mu niir; ku réy, mu ñooru.

Read Sabóor 138Sabóor 138
Compare Sabóor 138:2-6Sabóor 138:2-6