7Mooy yékkateey niir fa cati àddina, sàkkal taw ay melax, yebbee ngelaw cay dencam,
8fàdd luy taaw fa Misra, doom aadama, ba ci mala.
9Yeen waa Misra, moo yónnee ay firndeeki kéemaan fi seen biir, ñeel Firawnaak jawriñam ñépp.
10Moo duma ay xeeti xeet, bóom buur yu mag yi,
11muy Siwon buurub Amoreen ña, ak Og buuru Basan, ak buuri Kanaan ñépp.