3Màggal-leen Ki Sax, Aji Sax jee baax! Kañleen ko, kee sopplu!
4Ki Sax a taamu Yanqóoba, muy Israyil mi mu séddoo.
5Maa xam ne Aji Sax ji màgg na! Sunu Boroom a sut lépp lu ñuy jaamu.
6Lépp lu Aji Sax ji namm, moom lay def asamaan ak suuf, ak biir géej ak xóote yépp.