5li feek sàkkaluma Aji Sax ji bérab, ba dëkkal Mbërum Yanqóoba ma.»
6Ma ne, Efrata lanu dégg gaalu Yàlla ga, fekk ko àllub Yaar.
7Nan dem ba këram, sujjóotali ndëggëstalu tànkam ya.
8Aji Sax ji, jógal agsi sa dal-lukaay, yaak sa gaal gi jëmmal sa doole.
9Say sarxalkat, yal nañu woddoo njekk, sa wóllëre yi sarxolleendoo.
10Xoolal ci Daawuda, sa jaam ba, bul gàntu ki nga fal.
11Aji Sax ji daa giñal Daawuda dëgg gu mu dul dëddu, ne ko: «Ku jóge sa geño laay wuutal ci sa jal bi,