Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sabóor - Sabóor 132

Sabóor 132:3-12

Help us?
Click on verse(s) to share them!
3Mu ne: «Duma ñibbi,
4duma tëddi sama kaw lal ba, duma nelaw, duma gëmm sax bët,
5li feek sàkkaluma Aji Sax ji bérab, ba dëkkal Mbërum Yanqóoba ma.»
6Ma ne, Efrata lanu dégg gaalu Yàlla ga, fekk ko àllub Yaar.
7Nan dem ba këram, sujjóotali ndëggëstalu tànkam ya.
8Aji Sax ji, jógal agsi sa dal-lukaay, yaak sa gaal gi jëmmal sa doole.
9Say sarxalkat, yal nañu woddoo njekk, sa wóllëre yi sarxolleendoo.
10Xoolal ci Daawuda, sa jaam ba, bul gàntu ki nga fal.
11Aji Sax ji daa giñal Daawuda dëgg gu mu dul dëddu, ne ko: «Ku jóge sa geño laay wuutal ci sa jal bi,
12te say doom, bu ñu sàmmee sama kóllëre, ak sama kàdduy seede yi ma leen di xamal, seeni doom it ñooy tooge sa jal ba fàww.»

Read Sabóor 132Sabóor 132
Compare Sabóor 132:3-12Sabóor 132:3-12