60Maa ngi gaawtu, yeexewma say santaane moos!
61Buumi ñu bon ñaa ngi may laaw, te sàgganewma saw yoon.
62Xaaju guddi laay jóg, di la sante sa àttey njekk.
63Maa xejjoo képp ku la ragal, tey topp say tegtal.
64Aji Sax ji, sa ngor dajal na àddina; xamal ma sa dogali yoon.
65Aji Sax ji, def nga la nga dige woon, Sang bi, defal nga ma ngëneel.