32Sa yoonu santaane laay daw, yaa may may xol bu tàlli.
33Aji Sax ji, xamal ma li sa dogali yoon yiy firi, ma topp ko ba mu jeex.
34May ma dég-dég, ma topp saw yoon, toppe ko xol bu tàlli.
35Jiite ma ci sa xàllu santaane yi, mooy sama bànneex.
36Joyantil sama xol, mu féeteek sa kàdduy seede, te dummóoyu alal ju lewul.
37May ma, ma fénati caaxaani neen, te musale ma saw yoon.
38Sang bi, sottalal ma sa dige bi nga digook ku la ragal.
39Moyale ma gàcce gi ma ragal; yaa baaxi ndigal.
40Maaka namm say tegtal, musale ma sag njekk!
41Aji Sax ji, yaa ko dige, dikke ma sa jëfi ngor ak sa wall,
42ba ku ma kókkali, ma am tontam. Maa doyloo sa kàddu.
43Bu ma xañ mukk kàddug dëgg, say àtte laa yaakaar kat.