164Juróom yaari yoon ci bés màggale naa la ko say àttey njekk.
165Jàmm ju baree ñeel ku sopp sa yoon, te dara du ko fakktal.
166Aji Sax ji, sa wall laa yaakaar, say santaane laa jëfe.
167Sama xol laa toppe sa kàdduy seede, te sopp koo sopp.
168Damaa topp say tegtal ak sa kàdduy seede, fépp fu ma jaar kay yaa ngi ciy gis.
169Aji Sax ji, yal na sama yuux àgg fa yaw; may ma, ma ràññee, yaa ko dige.
170Yal na sama dagaan àgg fa yaw; xettli ma, yaa ko dige.
171Naa xaacu, woyal la, yaa may jàngal sa dogali yoon.
172Naa woye sa kàddu, loo santaane, njekk la.
173Yal nanga ma dikke ndimbal, say tegtal laa taamu.
174Aji Sax ji, namm naa sa wall, sa yoon ay sama bànneex.
175Yal naa dund ba màggal la, say ndigal di sama ndimbal.