155Ku bon sore sa wall, ngir sàkkuwul sa dogali yoon.
156Aji Sax ji, sa yërmande yaa na; musal ma ni nga ko baaxoo.
157Ñi ma topp ak ñi ma baña bare, te taxul ma dëddu sa kàdduy seede.
158Damaa gis workat yi, sib leen; ñoo sàmmul sa kàddu.
159Seetlul ni ma soppe say tegtal. Éy Aji Sax ji, musal ma, yaa gore!
160Sa mboolem kàddu dëgg la, sa ndigal yépp di njekk, sax dàkk.
161Ay kilifaa ma topp ci dara, te teewul ma wormaal sa kàddu.
162Man de, maa ngi bége sa kàddu ni ku for alal ju bare.
163Fen, ma bañ, ba sib; sa yoon, ma sopp.
164Juróom yaari yoon ci bés màggale naa la ko say àttey njekk.
165Jàmm ju baree ñeel ku sopp sa yoon, te dara du ko fakktal.
166Aji Sax ji, sa wall laa yaakaar, say santaane laa jëfe.
167Sama xol laa toppe sa kàdduy seede, te sopp koo sopp.
168Damaa topp say tegtal ak sa kàdduy seede, fépp fu ma jaar kay yaa ngi ciy gis.