Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - LUUG - LUUG 8

LUUG 8:3-18

Help us?
Click on verse(s) to share them!
3Sànn, soxnas ku ñuy wax Kusa, mi doon wottu alalu Erodd; ak Susànn ak ñeneen jigéen. Jigéen ñooñu ñoo doon joxe seen alal, ngir dimbali Yeesu ak ay taalibeem.
4Dëkk ak dëkk nit ña di fa jóge jëm ca Yeesu, ba mbooloo mu bare dajaloo, mu wax leen léeb wii:
5«Dafa amoon beykat bu demoon jiyi. Bi muy saaw toolam nag, lenn ci pepp mi wadd ci kaw yoon wi, nit ñi joggi ci, picci asamaan lekk ko lépp.
6Leneen wadd ci bérab bu bare ay doj. Naka la sax rekk, daldi wow, ndaxte suuf si tooyul woon.
7Leneen nag wadd ci biir ay xaaxaam, ñu saxandoo, xaaxaam ya tanc ko.
8Li ci des dal ci suuf su baax, sax, nangu ba meññ téeméeri yoon lu ëpp la mu ji woon.» Gannaaw loolu Yeesu wax ak kàddu gu dëgër ne: «Déglul bu baax, yaw mi am ay nopp.»
9Taalibey Yeesu yi laaj ko lu léeb woowu di tekki.
10Mu ne leen: «May nañu leen, ngeen xam mbóoti nguuru Yàlla, waaye ñi ci des, dama leen di wax ci ay léeb. Noonu la, ngir: “Ñuy xool te duñu mana gis, di dégg te duñu mana xam.”
11«Lii la léebu beykat bi di tekki. Kàddug Yàlla mooy jiwu wi.
12Ki féete ci yoon wi mooy ki dégg. Gannaaw gi, Seytaane dafay ñëw, këf kàddu, gi ñu def ci xolam, ngir mu baña gëm te Yàlla musal ko.
13Ki nekk ci bérab bu bare ay doj, mooy ki dégg kàddu gi, ba noppi nangu ko ak mbég. Waaye wax ji saxul ci moom. Dina gëm ab diir, waaye bu nattu yi agsee, mu daldi dàggeeku.
14Ki jot ci jiwu wi ci xaaxaam yi mooy ki dégg kàddu gi, waaye nees-tuut soxla yi ak alal ak bànneexi àddina tanc ko, ba du àgg cig mat.
15Ki jot ci jiwu wi ci suuf su baax si nag, mooy ki dégg kàddu gi te denc ko ci xol bu baax bu gore, te muñ ba jur njariñ.
16«Kenn du taal làmp, dëpp ci leget, walla mu di ko def ci ron lal. Daf koy wékk, ngir mu leeral ñiy dugg.
17Amul dara luy kumpa lu ñu dul siiwal bés, walla lu làqu lu ñu dul feeñal, ba mu ne fàŋŋ.
18Seetleen bu baax, ni ngeen di dégloo kàddu gi. Ku am, dees na la dollil, waaye ku amul, dees na nangu sax li nga xalaatoon ne am nga ko ba noppi.»

Read LUUG 8LUUG 8
Compare LUUG 8:3-18LUUG 8:3-18