Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Luug - Luug 24

Luug 24:27-51

Help us?
Click on verse(s) to share them!
27Mu tàmbalee nag ci Yonent Yàlla Musaa, jaare ci yonent yépp, tekkil leen mboolem lu Mbind mi indi ci mbiram.
28Naka lañuy jub dëkk, ba ñu jëm, mu mel ni ku nara jubal yoonam.
29Ñu daldi koy téye, ne ko: «Dalal ak nun, ndax jant baa ngi so, léegi mu guddi.» Ba loolu amee mu dugg, dal ak ñoom.
30Ba reer jotee mu toog ak ñoom ca ndab la, jël mburu ma, yékkati kàddug cant, daldi dagg, jox leen.
31Ca la seeni gët ubbiku, ñu xàmmi ko. Moom nag, mu ne mes, réer leen.
32Ba loolu amee, ku nekk naan sa moroom: «Ndax yéguloo woon cawartey xol bu tooy, ba muy wax ak nun ci yoon wi, di nu firil Mbind mi?»
33Ñaari taalibe ya daldi jóg ca waxtu woowu tembe, dellu Yerusalem, ca Fukk ñaak benn. Ñu fekk leen ñu dajeek seeni àndandoo.
34Ci kaw loolu ñu ne ñaar ña jóge Emayus: «Ndeke Sang bi kay, dekki na; feeñu na Simoŋ!»
35Ñaari taalibe ya ñoom it, nettali leen la xewoon ca yoon wa ak na ñu xàmmee Yeesu, ba mu daggee mburu ma.
36Ba ñaari taalibe ya di nettali loolu, ca la Yeesu ci boppam ne jimeet taxaw ci seen biir, ne leen: «Jàmm seen!»
37Tiitaange lu réy jàpp leen, ñu foog ne njuuma lañu gis.
38Yeesu nag ne leen: «Lu ngeen di jaaxle, ak lu ngeen di xel-yaar nii?
39Xool-leen samay loxo ak samay tànk. Man la. Làmbleen ma, ba xam! Njuuma amul suux, amuli yax, nii ma ko ame, ngeen gis.»
40Loolu la leen wax, daldi leen won ay loxoom aki tànkam.
41Taalibe ya nag boole mbég akug jaaxle ba tax manuñu koo gëm. Mu ne leen: «Lu ngeen fi am, lu ñuy lekk?»
42Ñu jox ko dogu jën wu ñu lakk.
43Mu jël ko, lekk ci seen kanam.
44Ci kaw loolu mu ne leen: «Lii moo di kàddu ya ma leen waxoon ba ma nekkee ak yeen. Noon naa leen: Mboolem li ñu bind ci samay mbir ci yoonu Musaa, ak ci téerey yonent yi, ak ci Sabóor, fàww lépp sotti.»
45Ca la ubbi seen xel, ngir Mbind mi leer leen.
46Mu ne leen: «Nii lees binde, ne fàww Almasi dee ci biir coono, ba ñetteelu fanam, mu dekki,
47te ciw turam, dees na dale ci Yerusalem, yégal xeet yépp, tuubeel gu jur njéggalug bàkkaar.
48Loolu yeena ko seede.
49Man ci sama bopp maa leen di yónnee li sama baay dige. Waaye yeen toogleen ci dëkk bi, ba kera ñu leen solee manoore ju bawoo fa kaw.»
50Gannaaw loolu Yeesu yóbbu leen ca wetu Betani. Ci kaw loolu mu yékkati ay loxoom, barkeel leen.
51Ba mu leen di barkeel, ca la teqlikoo ak ñoom, ñu yéege ko asamaan.

Read Luug 24Luug 24
Compare Luug 24:27-51Luug 24:27-51