Text copied!
Bibles in Wolof

LUUG 24:27-51 in Wolof

Help us?

LUUG 24:27-51 in Téereb Injiil

27 Noonu mu tàmbalee ci yonent Yàlla Musaa ba ci yonent yépp, tekkil leen li Mbind mi wax lépp ci ay mbiram.
28 Bi ñuy jub dëkk, ba ñu jëmoon nag, Yeesu def ni kuy jubal yoonam.
29 Waaye ñu téye ko ne ko: «Toogal fii ci nun, ndaxte jant baa ngi so, te léegi mu guddi.» Noonu mu dugg, toog ca ñoom.
30 Bi ñu tàmbali di reer, Yeesu jël mburu ma, gërëm Yàlla, ba noppi damm ko, jox leen ko.
31 Bi mu defee loolu, lépp leer ci seeni bët, ñu daldi ko xàmmi. Waaye Yeesu ne mes, gisatuñu ko.
32 Noonu ku nekk naan sa moroom: «Ndax sa xol seddul woon, bi muy wax ak nun ci yoon wi, te muy tekki Mbind mi?»
33 Ñu daldi jóg ca saa sa, dellu Yerusalem, fekk fa fukki ndaw ya ak benn, ak yeneen taalibe.
34 Ñooñu ne leen: «Dëgg la, Boroom bi dekki na, te feeñu na Simoŋ!»
35 Ñaari taalibe ya ñoom it daldi leen nettali la xewoon ca yoon wa ak ni ñu xàmmee Yeesu, bi mu dammee mburu ma.
36 Bi ñaari taalibe ya dee wax noonu, Yeesu taxaw moom ci boppam ci seen biir ne leen: «Na jàmm wàcc ci yéen.»
37 Ñu daldi tiit, foog ne dañoo gis njuuma.
38 Waaye Yeesu ne leen: «Lu tax ngeen jaaxle, ak lu tax ngeen di xel ñaar ci seen xol?
39 Xool-leen samay loxo ak samay tànk. Man mii la. Laal-leen ma te xam, njuuma amul yaram walla ay yax, ni ngeen gise, ma am ko.»
40 Bi mu leen waxee loolu, mu won leen ay loxoom ak ay tànkam.
41 Waaye ba tey manuñu woona gëm ndax seen mbég ak jaaxle. Noonu Yeesu laaj leen ne: «Ndax am ngeen fii lu ñu lekk?»
42 Ñu jox ko dogu jën wu ñu lakk.
43 Mu jël ko, lekk ci seen kanam.
44 Noonu mu ne leen: «Bi ma nekkee ak yéen, waxoon naa leen baat yii: li ñu bind lépp ci samay mbir ci yoonu Musaa ak ci téerey yonent yi ak ci Sabóor dafa wara am.»
45 Noonu mu ubbi seen xel, ngir ñu xam li Mbind mi di wax.
46 Mu ne leen: «Fàww Almasi bi sonn, mu dee te dekki ca ñetteelu fan ba, ni ñu ko binde,
47 te it ñuy yégle xeet yépp ci turam, dale ko ci Yerusalem ne war nañoo tuub seeni bàkkaar, Yàlla baal leen.
48 Yéenay samay seede.
49 Te man dinaa leen yónnee li sama Baay dige. Yéen nag toogleen ci dëkk bi, ba ñu sol leen doole ji jóge ci kaw.»
50 Gannaaw loolu Yeesu yóbbu leen ca wetu Betani. Foofa mu yékkati ay loxoom, barkeel leen.
51 Bi mu leen dee barkeel, mu tàggoo ak ñoom, Yàlla yéege ko asamaan.
LUUG 24 in Téereb Injiil

Luug 24:27-51 in Kàddug Yàlla gi

27 Mu tàmbalee nag ci Yonent Yàlla Musaa, jaare ci yonent yépp, tekkil leen mboolem lu Mbind mi indi ci mbiram.
28 Naka lañuy jub dëkk, ba ñu jëm, mu mel ni ku nara jubal yoonam.
29 Ñu daldi koy téye, ne ko: «Dalal ak nun, ndax jant baa ngi so, léegi mu guddi.» Ba loolu amee mu dugg, dal ak ñoom.
30 Ba reer jotee mu toog ak ñoom ca ndab la, jël mburu ma, yékkati kàddug cant, daldi dagg, jox leen.
31 Ca la seeni gët ubbiku, ñu xàmmi ko. Moom nag, mu ne mes, réer leen.
32 Ba loolu amee, ku nekk naan sa moroom: «Ndax yéguloo woon cawartey xol bu tooy, ba muy wax ak nun ci yoon wi, di nu firil Mbind mi?»
33 Ñaari taalibe ya daldi jóg ca waxtu woowu tembe, dellu Yerusalem, ca Fukk ñaak benn. Ñu fekk leen ñu dajeek seeni àndandoo.
34 Ci kaw loolu ñu ne ñaar ña jóge Emayus: «Ndeke Sang bi kay, dekki na; feeñu na Simoŋ!»
35 Ñaari taalibe ya ñoom it, nettali leen la xewoon ca yoon wa ak na ñu xàmmee Yeesu, ba mu daggee mburu ma.
36 Ba ñaari taalibe ya di nettali loolu, ca la Yeesu ci boppam ne jimeet taxaw ci seen biir, ne leen: «Jàmm seen!»
37 Tiitaange lu réy jàpp leen, ñu foog ne njuuma lañu gis.
38 Yeesu nag ne leen: «Lu ngeen di jaaxle, ak lu ngeen di xel-yaar nii?
39 Xool-leen samay loxo ak samay tànk. Man la. Làmbleen ma, ba xam! Njuuma amul suux, amuli yax, nii ma ko ame, ngeen gis.»
40 Loolu la leen wax, daldi leen won ay loxoom aki tànkam.
41 Taalibe ya nag boole mbég akug jaaxle ba tax manuñu koo gëm. Mu ne leen: «Lu ngeen fi am, lu ñuy lekk?»
42 Ñu jox ko dogu jën wu ñu lakk.
43 Mu jël ko, lekk ci seen kanam.
44 Ci kaw loolu mu ne leen: «Lii moo di kàddu ya ma leen waxoon ba ma nekkee ak yeen. Noon naa leen: Mboolem li ñu bind ci samay mbir ci yoonu Musaa, ak ci téerey yonent yi, ak ci Sabóor, fàww lépp sotti.»
45 Ca la ubbi seen xel, ngir Mbind mi leer leen.
46 Mu ne leen: «Nii lees binde, ne fàww Almasi dee ci biir coono, ba ñetteelu fanam, mu dekki,
47 te ciw turam, dees na dale ci Yerusalem, yégal xeet yépp, tuubeel gu jur njéggalug bàkkaar.
48 Loolu yeena ko seede.
49 Man ci sama bopp maa leen di yónnee li sama baay dige. Waaye yeen toogleen ci dëkk bi, ba kera ñu leen solee manoore ju bawoo fa kaw.»
50 Gannaaw loolu Yeesu yóbbu leen ca wetu Betani. Ci kaw loolu mu yékkati ay loxoom, barkeel leen.
51 Ba mu leen di barkeel, ca la teqlikoo ak ñoom, ñu yéege ko asamaan.
Luug 24 in Kàddug Yàlla gi