Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Luug - Luug 1

Luug 1:24-62

Help us?
Click on verse(s) to share them!
24Gannaaw gi, soxnaam Elisabet ëmb. Lëlu na juróomi weer. Ma nga naan:
25«Lii Boroom bee ma ko defal ci jant yi mu ma geesoo, ba teggil ma sama gàcce gi ci biir nit ñi!»
26Ba Elisabet tolloo ci juróom benni weeram, ca la Yàlla yebal Jibril malaaka mi, dëkk bi ñuy wax Nasaret ca diiwaanu Galile,
27ci janq bu digoo séy ak waa ju ñuy wax Yuusufa te bokk ci waa kër Daawuda. Janq ba Maryaama lañu koy wax.
28Malaaka ma agsi ba ca moom, ne ko: «Jàmm nga am, yaw mi ñu baaxe, Boroom bi yaw la àndal.»
29Waxi malaaka ma nag jaaxal Maryaama, muy xalaat lu nuyoo boobu mana tekki.
30Malaaka ma ne ko: «Maryaama, bul tiit, ndax daje nga ak yiwu Yàlla.
31Dinga ëmb, ba jur doom ju góor; nanga ko tudde Yeesu.
32Ku màgg lay doon, te dees na ko wooye Doomu Aji Kawe ji. Boroom bi Yàlla moo koy jagleel nguurug Daawuda maamam.
33Mooy nguuru fi kaw waa kër Yanqóoba ba fàww, te nguuram du foq mukk.»
34Ci kaw loolu Maryaama laaj malaaka mi ne ko: «Nu loolu di ame, te man xawma góor?»
35Malaaka mi ne ko: «Noo gu Sell gi mooy wàccsi ci yaw, dooley Aji Kawe ji yiir la. Moo tax itam ku Sell kiy juddoo ci yaw, dees na ko wooye Doomu Yàlla.
36Te kat Elisabet sa mbokk mi itam ëmb na doom ju góor te fekk ko màggat. Ki ñu doon wooye jigéen ju jaasir, mu ngi nii ci juróom benni weeram,
37ndax Yàlla, dara tëwu ko.»
38Maryaama daldi ne: «Maa ngi, di jaamub Boroom bi. Nii nga waxe, na ame noonu ci man.» Ba loolu amee malaaka ma bàyyikoo ca moom, dem.
39Ci fan yooyu la Maryaama fabu gaaw, jëm diiwaanu tund ya, ca dëkkub Yude,
40ba Sàkkaryaa dëkke. Mu agsi ca kër ga, nuyu Elisabet.
41Naka la Elisabet dégg nuyoob Maryaama, doom ja mu ëmb yëngu ca biiram. Elisabet daldi feese Noo gu Sell gi.
42Mu àddu ca kaw ne: «Yaa gëna barkeel ci jigéen ñi, sa doom ji nga ëmb it barkeel na!
43Ana ku ma doon ba sama ndeyu Sang di ma seetsi?
44Naka la sa kàddug nuyoo tàbbi sama nopp rekk, sama doom ji yëngu ci sama biir bi ndax bég.
45Ndokklee yaw mi gëm ne mbir mi ñu la yégal, te mu tukkee ci Boroom bi dina sotti!»
46Maryaama nag ne:
47«Sama xol laay màggale Boroom bi, samag noo laay bége Yàlla mi may musal,
48moo geesu bii jaamam bu tekkeedi, ba maasoo maas doxe fi wooye ma boroom mbég mi,
49nde Kiy Boroom doole moo ma defal jaloore, sellnga ñeel naw turam.
50«Yërmandeem a ñeel ay ragalkatam, maas ci kaw maas.
51Dooley loxoom la defe ay jaloore, tasaare ñi jikkowoo réy-réylu,
52wàccee buur yi ci seeni gàngune, yékkati baadoolo yi.
53Ñi xiif, mu reggal leen lu neex, ñi duunle, mu dàqe loxoy neen.
54Moo wallu bànni Israyil, jaamam, bàyyee ko xel yërmandeem,
55noonee mu ko dige woon sunuy maam, ñeel Ibraayma ak askanam ba fàww.»
56Maryaama toog na fa Elisabet lu wara tollook ñetti weer, sooga ñibbi.
57Gannaaw gi Elisabet dem ba àppam mat, mu mucc, am doom ju góor.
58Dëkkandoom yaak ay bokkam yég noonu ko Boroom bi xéewalee yërmandeem, ñu bokk ak moom mbégte ma.
59Ba bés ba délsee, ñu dikk xarfalsi xale ba, bëgg koo tudde Sàkkaryaa, dippee ko baayam.
60Yaayam nag ne leen: «Déet, Yaxya lay tudd.»
61Ñu ne ko: «Waaye kenn ci say bokk tuddul noonu!»
62Ci kaw loolu ñu liyaar baayam, ngir xam nu mu bëgg ñu tudde xale bi.

Read Luug 1Luug 1
Compare Luug 1:24-62Luug 1:24-62