Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - LUUG - LUUG 19

LUUG 19:4-12

Help us?
Click on verse(s) to share them!
4Noonu mu daw, jiituji ca yoon wa, yéeg ci genn garab ngir gis Yeesu, ndaxte foofa la naroona jaar.
5Bi Yeesu dikkee ba tollook garab ga nag, mu téen ne ko: «Sase, wàccal gaaw, ndax tey sa kër laa wara dal.»
6Sase daldi gaawantu wàcc, ganale ko ak mbég.
7Ñépp gis loolu, di ñurum-ñurumi naan: «Mi ngi dal cig këru boroom bàkkaar.»
8Waaye Sase taxaw ne Boroom bi: «Déglul Boroom bi, dogu naa may sama genn-wàllu alal miskin yi, te lu ma masa njublaŋ nit, jël alalam, dinaa ko fey ñeenti yoon lu ni tollu.»
9Yeesu ne ko: «Mucc gi wàcc na tey ci kër gii, ndaxte nit kii, ci askanu Ibraayma la bokk itam.
10Ndaxte Doomu nit ki ñëw na, ngir seet te musal ñi réer.»
11Bi nit ñi doon déglu kàddu yooyu, Yeesu teg ca léeb, ndaxte jege woon na Yerusalem, te ñoom foogoon nañu ne nguuru Yàlla dafay daldi feeñ ca saa sa.
12Mu ne nag: «Dafa amoon boroom juddu bu rafet bu demoon ci réew mu sore, ngir ñu fal ko buur te mu délsiwaat.

Read LUUG 19LUUG 19
Compare LUUG 19:4-12LUUG 19:4-12