Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Luug - Luug 18

Luug 18:11-24

Help us?
Click on verse(s) to share them!
11Farisen baa nga taxaw di yelu, naan: “Yàlla, maa ngi lay sante li ma melul ni ñeneen ñi doonul lu moy ay lekk-kati àq, ay njublaŋ aki jaalookat, rawatina juutikat bii.
12Maa ngi woor ñaari yoon, ayu bés gu nekk, di joxe asaka benn céru fukkeelu mboolem lu ma am.”
13«Juutikat ba moom, ma nga taxaw fu sore, ñemewula siggi sax, xool asamaan, xanaa di fëgg dënnam te naan: “Éy Yàlla, yërëm ma, man bàkkaarkat bi.”»
14Yeesu teg ca ne: «Maa ne leen, kooku moo ñibbaale këram àtteb ku jub, waaye du Farisen ba. Ndaxte képp kuy réylu, dees na la toroxal, waaye ki toroxlu lees di yékkati.»
15Doon nañu indil Yeesu ay tuut-tànk sax, ngir mu teg leen ay loxoom. Taalibe ya gis loolu, di leen jànni.
16Yeesu nag woolu xale yi, ne: «Bàyyileen xale yi, ñu ñëw fi man, buleen leen aaye, ndax ñu mel ni ñoom ñoo yelloo nguurug Yàlla.
17Maa leen ko wax déy, képp ku baña nangul nguurug Yàlla ni ab xale, doo ca dugg mukk.»
18Kenn ci njiiti Yawut yi moo laajoon Yeesu, ne ko: «Sëriñ bu baax bi, ana lu may def, ba texe fàww?»
19Yeesu ne ko: «Lu tax nga naa ma ku baax ki? Kenn baaxul ku moy Yàlla doŋŋ.
20Xam nga ndigal yi: “Bul jaaloo, bul bóom, bul sàcc, bul seede lu dul dëgg, teralal sa ndey ak sa baay.”»
21Mu ne ko: «Loolu lépp, ba may ndaw laa ko dale sàmm ba tey.»
22Yeesu dégg loolu, ne ko: «Lenn rekk nga deseleeti. Mboolem loo am, jaay ko, séddale ko néew-doole yi. Su ko defee nga woomle fa asamaan. Boo noppee, ñëwal, topp ci man.»
23Ba waa ji déggee loolu, am na tiis wu réy, ndax barele woon na lool.
24Yeesu gis loolu, daldi ne: «Boroom alal tàbbi ci nguurug Yàlla, ndaw lu jafe!

Read Luug 18Luug 18
Compare Luug 18:11-24Luug 18:11-24