Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Luug - Luug 10

Luug 10:4-20

Help us?
Click on verse(s) to share them!
4Buleen yóbbaale dencukaayu xaalis, mbaa mbuus, mbaa ay carax te buleen taxaw di saafoonte ak kenn ci yoon wi.
5«Gépp kër gu ngeen dugg, jëkkleen ne: “Jàmm ñeel na leen.”
6Su fa nitu jàmm nekkee, seen jàmm dal ko. Lu ko moy, mu délsi ci yeen.
7Dal-leen ca kër googa, di lekk ak a naan ca la ñu leen jox, ndax liggéeykat yelloo na peyooram. Buleen di wër nag kër ak kër.
8«Bépp dëkk bu ngeen dugg, ñu dalal leen, la ñu leen taajal, lekkleen ko.
9Wéral leen jaragi dëkk ba, te ngeen wax waa dëkk ba, ne leen: “Nguurug Yàlla dëgmal na leen.”
10Waaye bépp dëkk bu ngeen dugg te dalaluñu leen, demleen ca pénc ma te ngeen ne leen:
11“Seen pëndub dëkk bi ci sunu ndëgguy tànk sax, nu ngi koy faxas, seedeele leen ko seen ngàntal. Waaye nag xamleen ne nguurug Yàlla dëgmal na.”
12Maa leen ko wax, bu bés baa, boobu dëkk, Sodom a koy gënu demin.
13«Wóoy ngalla yeen waa Korasin, yeen waa Beccayda it, wóoy ngalla yeen, nde kéemaan yi sottee fi seen biir, su doon fa waa Tir mbaa fa waa Sidon la sottee, kon bu yàgg lañu doon sol ay saaku, xëppoob dóom, ngir tuub.
14Moo tax it, kera àtte ba, waa Tir ak Sidon a leen di gënu demin.
15Yeen waa Kapernawum nag, dees na leen yékkati ba asamaan a? Xanaa ba fa njaniiw kay ngeen di wàcci.
16«Ku leen déggal nag, man nga déggal; ku leen gàntal, man nga gàntal. Te ku ma gàntal, gàntal nga ki ma yebal.»
17Ba juróom ñaar Fukk ñaak ñaar demee ba délsi, mbégte lañu àndal. Ñu ne: «Sang bi, rab yi sax, danu leen di jox ndigal ci sa tur, ñu nangul nu.»
18Yeesu ne leen: «Séen naa Seytaane mu fàqe asamaan ni ag melax.
19Dama ne, maa leen jox sañ-sañu joggi ci kawi jaan aki jiit, joggati mboolem dooley bañaale bi, te dara du leen mana gaañ mukk.
20Noonu leen rab yi nangule nag, buleen ko bége, bégeleen kay la seen tur binde fa asamaan.»

Read Luug 10Luug 10
Compare Luug 10:4-20Luug 10:4-20