Text copied!
Bibles in Wolof

LUUG 10:4-20 in Wolof

Help us?

LUUG 10:4-20 in Téereb Injiil

4 Buleen yor xaalis walla mbuus walla ay dàll. Buleen nuyu kenn ci yoon wi.
5 «Kër gu ngeen mana dugg, nangeen jëkk ne: “Na jàmm wàcc ci kër gi.”
6 Bu fa nitu jàmm nekkee, seen yéene dina ko indil jàmm. Lu ko moy, seen yéene dina délsi ci yéen.
7 Dal-leen ca kër googa, tey lekk ak a naan lu ñu leen di jox, ndaxte liggéeykat yelloo na jot peyam. Buleen dem nag kër ak kër.
8 «Dëkk bu ngeen mana dugg, te waa dëkk ba teeru leen, lu ñu leen jox, lekkleen ko.
9 Nangeen wéral jaragi dëkk ba, te ngeen ne leen: “Nguuru Yàlla jegesi na leen.”
10 Waaye bu ngeen duggee ci dëkk te teeruwuñu leen, demleen ca mbedd ya te ne leen:
11 “Seen pëndu dëkk, bi taq ci sunuy tànk sax, noo ngi koy faxas, ngir seede leen seen réer. Waaye nag xamleen ne nguuru Yàlla jegesi na.”
12 Maa ngi leen koy wax, bu bés baa, waa Sodom ñooy tane dëkk boobu.
13 «Dingeen torox, yéen waa Korasin ak waa Betsayda, ndaxte kéemaan yi ma def ci yéen, bu ñu leen defoon ci dëkku Tir walla ci dëkku Sidon, kon tuub nañu seeni bàkkaar bu yàgg, xëppoo dóom, sol saaku.
14 Moona ca bés pénc ba, Tir ak Sidon ñoo leen di tane.
15 Te yaw dëkku Kapernawum, ndax dees na la yékkati bu kawe? Déedéet, dees na la daane bu suufe.
16 «Ku leen déglu, déglu na ma; ku leen bañ, bañ na ma. Te ku ma bañ, bañ na ki ma yónni.»
17 Juróom ñaar fukki taalibe yi ak ñaar délsi, fees ak mbég te naan: «Boroom bi, rab yi sax déggal nañu nu ndax sa tur.»
18 Yeesu ne leen: «Maa ngi doon séen Seytaane wàcce asamaan ni sawaras melax.
19 Gis ngeen, jox naa leen sañ-sañu joggi ci jaan yi ak ci jiit yi, daan dooley bañaale bi, te dara du leen mana gaañ.
20 Moona li leen rab yi déggal, bumu tax ngeen bég, waaye bégleen ndax li ñu bind seen tur ci asamaan.»
LUUG 10 in Téereb Injiil

Luug 10:4-20 in Kàddug Yàlla gi

4 Buleen yóbbaale dencukaayu xaalis, mbaa mbuus, mbaa ay carax te buleen taxaw di saafoonte ak kenn ci yoon wi.
5 «Gépp kër gu ngeen dugg, jëkkleen ne: “Jàmm ñeel na leen.”
6 Su fa nitu jàmm nekkee, seen jàmm dal ko. Lu ko moy, mu délsi ci yeen.
7 Dal-leen ca kër googa, di lekk ak a naan ca la ñu leen jox, ndax liggéeykat yelloo na peyooram. Buleen di wër nag kër ak kër.
8 «Bépp dëkk bu ngeen dugg, ñu dalal leen, la ñu leen taajal, lekkleen ko.
9 Wéral leen jaragi dëkk ba, te ngeen wax waa dëkk ba, ne leen: “Nguurug Yàlla dëgmal na leen.”
10 Waaye bépp dëkk bu ngeen dugg te dalaluñu leen, demleen ca pénc ma te ngeen ne leen:
11 “Seen pëndub dëkk bi ci sunu ndëgguy tànk sax, nu ngi koy faxas, seedeele leen ko seen ngàntal. Waaye nag xamleen ne nguurug Yàlla dëgmal na.”
12 Maa leen ko wax, bu bés baa, boobu dëkk, Sodom a koy gënu demin.
13 «Wóoy ngalla yeen waa Korasin, yeen waa Beccayda it, wóoy ngalla yeen, nde kéemaan yi sottee fi seen biir, su doon fa waa Tir mbaa fa waa Sidon la sottee, kon bu yàgg lañu doon sol ay saaku, xëppoob dóom, ngir tuub.
14 Moo tax it, kera àtte ba, waa Tir ak Sidon a leen di gënu demin.
15 Yeen waa Kapernawum nag, dees na leen yékkati ba asamaan a? Xanaa ba fa njaniiw kay ngeen di wàcci.
16 «Ku leen déggal nag, man nga déggal; ku leen gàntal, man nga gàntal. Te ku ma gàntal, gàntal nga ki ma yebal.»
17 Ba juróom ñaar Fukk ñaak ñaar demee ba délsi, mbégte lañu àndal. Ñu ne: «Sang bi, rab yi sax, danu leen di jox ndigal ci sa tur, ñu nangul nu.»
18 Yeesu ne leen: «Séen naa Seytaane mu fàqe asamaan ni ag melax.
19 Dama ne, maa leen jox sañ-sañu joggi ci kawi jaan aki jiit, joggati mboolem dooley bañaale bi, te dara du leen mana gaañ mukk.
20 Noonu leen rab yi nangule nag, buleen ko bége, bégeleen kay la seen tur binde fa asamaan.»
Luug 10 in Kàddug Yàlla gi