Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - 2.Korent

2.Korent 8

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Gannaaw loolu bokk yi, danu leen di xamal li yiwu Yàlla maye ci biir mboolooy gëmkati diiwaanu Maseduwan.
2Doonte jaar nañu ci nattub njàqare bu mag, seen mbégtee rembat ci seen biir ñàkk gu tar, ba géejal seenug tabe.
3Seen kemu am-am lañu joxee, maa ko seede, lu wees seen am-am sax lañu joxee xol bu sedd.
4Dañu noo ñaan, ba di nu tinu, ngir nu may leen, ñu def seen loxo ci ndimbalu jàpplante gi jëm ci gëmkat ñu sell ñi.
5Li nu séentu woon sax wees nañu ko, nde Sang bi lañu jëkka jébbal seen bopp, door noo jébbal seen bopp, te noonu la ko Yàlla bëgge.
6Looloo tax nu soññ Tit, ngir noonee mu tàmbalee woon ci yeen, ndajalem ndimbal li, mu àggalee ko ci yeen.
7Gannaaw nag yeena duunle ci lépp; muy ci wàllu ngëm, ak wàllu kàddu yu rafet, ak wàllu xam-xam, ak cawarte ci lépp, ak ci cofeel gu nu leen xiir, kon ndajalem ndimbal lii it, ngalla duunleleen ci.
8Du ndigal lu ma leen jox, waaye njaxlafug yeneen gëmkat, moom laay natte seen xol, ngir xam nu seen cofeel dëggoo.
9Xam ngeen kat sunu yiwu Boroom Yeesu Almasi, moom mi woomle woon, te yeena tax mu ñàkk, ngir woomale leen ag ñàkkam.
10Ab xalaat laa am ci mbir mii, te mooy doon seen njariñ. Du jëf ji rekk ngeen jëkke woon, waaye yeena jëkkoona biral daaw, yéeney dimbali.
11Kon nag léegi, mottlileen jëf ji. Noonu ngeen xére woon ci seen yéene, mottleeleen ko noonu ci seen kem am-am.
12Ndax kat ab joxe, bu àndee ak yéene rekk, la boroom joxe bi amul, deesu ci natt lees koy nangul, waaye li mu am, ci lees koy nangul ab joxeem.
13Du caageenu nag, teg leen coono, ngir teggil ñenn ñi, waaye ag tollale war na ci.
14Tey jii seenug rembatle mooy faj soxlay ñeneen, ngir ëllëg, rembatley ñooña faj seeni soxla, yeen itam. Su ko defee ag tolloo am.
15Noonu lañu binde ne: «Ki dajale lu bare ëpplewul, te ki dajale lu tuut ñàkkul.»
16Cant ñeel na Yàlla, mi def ci xolu Tit, mu xér ci yeen ni ma xére ci yeen!
17Ba nu ñaanee Tit mu dikk ba ci yeen, nangul na nu, waaye yemu ca, nde ci xéraangeem la yebul boppam ne mooy dikk ba ci yeen.
18Noo ko yebal, boole kook menn mbokk mu mboolooy gëmkat ñépp gërëm, ndax liggéeyam ci xibaaru Almasi bi muy xamle.

19Rax ci dolli, mboolooy gëmkat ñi ñoo ko tabb, ngir mu ànd ak nun, ba nu yóbbu ndimbal li, muy teddngay Boroom bi ci boppam, te di sunu firndey cawarte ci dimbalee.
20Noonu lanu fàggoo, ndax kenn bañ noo sikk ci ndimbal lu bare lii nu wara saytu.
21Li nuy xinte moo di li baax ci kanam Boroom bi, te baax ci kanam nit ñi itam.
22Boole nañu leen itam ak sunu mbokk mu nu nemmiku xéraangeem ay yooni yoon, ci fànn yu bare, te mu gënatee xér bii yoon ndax kóolute gu réy gu mu am ci yeen.
23Su dee mbirum Tit, mooy sama wéttal, di ma jàpple ci liggéey bi, ngir yeen. Sunu bokk, yi ànd ak moom nag, ñooy ndawi mboolooy gëmkat ñi, te ñooy teraangay Almasi.
24Kon nag wonleen leen lu firndeel seen cofeel ci ñoom, ak ci kanam mboolooy gëmkat ñi, firndeel itam ne noo yey wóolu leen.