Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - 2.Korent

2.Korent 6

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Nun ñi bokk ci liggéey bi nag, noo leen di ñaan ngeen baña nangu yiwu Yàlla ci neen.
2Ndaxte Yàlla moo ne: «Jant ba mu jotee laa la nangul, bésu mucc ba laa la wallu.» Te nag, tey jii la jantam jote; tey kat, la bésub mucc.
3Buggunu kenn sikk sunub liggéey, moo tax buggunoo jëfe lenn luy doon tojaange ci kenn.
4Ci lépp kay lanu bëgga seedeel sunu bopp, ne noo yelloo ngërëm, te ay jawriñi Yàlla lanu, di ñu muñ lu bare ci biir coono, aki mitit, aki njàqare;
5ci ay dóor, ak néegi kaso, ci biir mbooloo yu nu jógal, ci doñ-doñ ju metti, ak fanaanee xoole, akub xiif;
6te nuy setal sunu dund, di ànd ak xam-xam, ci biir muñ, akug mbaax, ci biir Noo gu Sell gi, ak cofeel gu amul jinigal,
7ci biir kàddug dëgg, ak kàttanu Yàlla; ci kaw gànnaayi njubte yi ci sunu loxol ndijoor ak lu càmmoñ;
8ci biir teraanga, ak ci biir toskare; ci biiri baatal, ak jëw yu rafet. Dees noo jàppe ay mbubbookati dëgg, te nuy nit ñu dëggu;
9jàppe nu ñu kenn xamul, te nuy ñu siiw; jàppe nu ñuy waaja dee, te nuy dund; jàppe nu ñu ñu wara mbugal, te bañ leena teg àtteb dee.
10Dees noo jàppe boroomi tiis, te nu dëkke mbég; jàppe nu ay néew-ji-doole, te nu woomal ñu bare; jàppe nu ñu amul dara, te nu moom lépp.
11Yeen bokki Korent, wax nanu leen sunu biir yépp, ubbil leen sunu xol.
12Genn ñooru jógewul ci nun, waaye yeen yeena nu ñooroo seen xol.
13Léegi nag, yeen, feyleen nu bor bi boog, ma wax ak yeen ni samay doom, ubbil-leen nu seen xol!
14Buleen lëkkoo ak gëmadikat ñi. Gan lëngoo la njub ak ndëngte séq? Gan booloo la leer ak lëndëm séq?
15Gan juboo la Almasi ak Seytaane séq? Wan wàll la gëmkat bi bokk ak gëmadikat bi?
16Gan takktoo la kër Yàlla séq ak ay tuur? Ndax kat, nun, nooy kër Yàlla jiy dund, te noonu la ko Yàlla waxe ne: «Maay dëkk ci seen biir, di dox ci seen biir, di seen Yàlla, ñuy sama ñoñ.»
17Kon nag: «Nangeen génne ci seen biir, te teqlikoo ak ñoom,» la Boroom bi wax. «Lu sobewu, buleen ko laal. Su boobaa, maa leen di dalal.
18Maay doon seen baay, ngeen di samay doom, góor, ak jigéen,» la Boroom bi, Aji Man ji wax.