8Aji Sax jee sax dàkk, samp jalam ngir àtte.
9Moom mooy àtte àddina cig njub, di dogalal xeet yi dëgg.
10Aji Sax jeey làq néew-ji-doole, mooy làqe bésub njàqare.
11Aji Sax ji, yaw, ku la xam, wóolu la. Aji Sax ji, yaw, ku lay sàkku, doo ko wacc.
12Woyleen Aji Sax ji dëkke Siyoŋ, siiwal-leen ay jalooreem ci xeet yi!
13Mooy topp nit bakkanu moroomam, di ko ba xel, te du fàtte yuuxi néew-ji-doole.
14Éy Aji Sax ji, baaxe ma, gisal naqar wi ma bañ yi teg. Yaa may yékkatee fa bunti ndee,