7Noon ya raaf, gental ba fàww. Yaa déjjati seeni dëkk, seenu askan fey.
8Aji Sax jee sax dàkk, samp jalam ngir àtte.
9Moom mooy àtte àddina cig njub, di dogalal xeet yi dëgg.
10Aji Sax jeey làq néew-ji-doole, mooy làqe bésub njàqare.
11Aji Sax ji, yaw, ku la xam, wóolu la. Aji Sax ji, yaw, ku lay sàkku, doo ko wacc.