2Aji Sax jee xamleg wallam, feeñal njekkam, xeet yi gis.
3Moo dencal bànni Israyil ngoram, dencal ko wormaam, àddina ba mu daj di gis ni nu sunu Yàlla walloo.
4Yeen àddina sépp, xaacul-leen Aji Sax ji, sampleen, sarxolle te woy!
5Xalamal-leen Aji Sax ji, woyal ko, xalamal ko, woyati.
6Wal-leen liit yi, wal bufta yi te xaacul Buur Aji Sax ji!