Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sabóor - Sabóor 97

Sabóor 97:6-10

Help us?
Click on verse(s) to share them!
6Asamaan a ngi biral njekkam, xeetoo xeet di gis darajaam.
7Gàcce ñeel na kuy jaamu jëmmi tuur, di puukarewoo ay yàllantu. Yeen yàllay xeet yépp, sujjóotal-leen kii,
8Siyoŋ dégg ca, bég, waa Yuda it di bànneexoo àttey Aji Sax jii.
9Aji Sax ji, Aji Kawe ji tiim suuf sépp; yaaka màgga màgg, ba sut tuuroo tuur.
10Yeen soppey Aji Sax ji, bañleen lu bon. Aji Sax jeey sàmm ay wóllëreem, di leen musal ci ku bon.

Read Sabóor 97Sabóor 97
Compare Sabóor 97:6-10Sabóor 97:6-10