1Aji Sax jeey Buur, na àddina bég; dunoo dun bànneexu.
2Ay xàmbaar a ko yéew, njekk ak njub lal ab jalam.
3Sawaraa dox, jiitu ko, di xoyomi noonam wetoo wet,
4ay melaxam leeral àddina, waa àddina gis, di pat-pati;
5tund yi ne soyox seey fi kanam Aji Sax ji boroom àddina sépp.
6Asamaan a ngi biral njekkam, xeetoo xeet di gis darajaam.
7Gàcce ñeel na kuy jaamu jëmmi tuur, di puukarewoo ay yàllantu. Yeen yàllay xeet yépp, sujjóotal-leen kii,
8Siyoŋ dégg ca, bég, waa Yuda it di bànneexoo àttey Aji Sax jii.