12Ki Sax, ndokklee ki ngay yar, tàggat ko ci saw yoon,
13dëfal ko ci bési safaan, ba keroog ñuy gasal ku bon.
14Boroom bi kat du wacc ñoñam mukk, du bàyyi ay séddoom.
15Àtte dina dellu laloo njekk, képp ku jub topp ca.
16Ana ku may taxawal ci ñu bon ñi? Ku may jógal ci biir ñiy def lu bon?
17Su ma Aji Sax ji walluwloon, tuuti ma fanaani réew ma ne selaw.