45Xañ nga ko darajaam, rattax ngànguneem fa suuf.
46Dagg nga fani ngoneem, sang ko gàcce. Selaw.
47Éy Aji Sax ji, xanaa lii du jeex? Xanaa doo làqu fàww nii, sa mer di boy?
48Bàyyi ma xel, samay fan yàggul. Xanaa du neen a tax nga sàkk mboolem doom aadama?
49Ana kuy dund te du dee? Ku mana rëcc tëraayu bàmmeel? Selaw.