19Sunu kiirlaay lii, Aji Sax jeey boroom; sunu buur bii, Aji Sell ji séddoo Israyil ay boroom.
20Wax nga say wóllëre ci peeñu, ne leen: «Tànne naa jàmbaar ci xeet wi, dénk ko ndimbal.
21Gis naa sama jaam Daawuda, fale ko sama diw gu sell,
22ànd ak moom, saxal ko, di ko dooleel.
23Noon du ko bett, ku bon du ko torxal.
24Ay bañam, ma rajaxe; ay noonam, ma fàdd,
25sama wormaak sama ngor di ko gunge, may yokk kàttanam.
26Géej, ma teg ci loxoom, dex, ma ne ca tegg ndijooram.
27Moo ma naa: “Yaay sama baay, di sama Yàlla, di sama wéeru-mucc.”
28Te it maa koy def samab taaw, tiimale ko buuri àddina,
29sàmmal ko sama ngor ba fàww, feddlil ko sama kóllëre.
30Damay saxal askanam ba fàww, yàggal ab jalam ni asamaan.
31Bu ay sëtam wàccee sama yoon, baña doxe samay ndigal,
32mbaa ñu xëtt sama dogali yoon, baña sàmmonteek samay santaane,
33ma bantale leen seenug moy, dumaa leen seen ñaawtéef.