15Njekk ak njub a lal sab jal, ngor ak worma dox jiitu la.
16Aji Sax ji, ndokklee mbooloo mu la xal di sarxollee, di niitoo saw yiw,
17ànd di la bége bés bu ne, sag njekk siggil leen.
18Seen darajay doole, yaw a. Boo nu baaxee, nu yokku kàttan.
19Sunu kiirlaay lii, Aji Sax jeey boroom; sunu buur bii, Aji Sell ji séddoo Israyil ay boroom.
20Wax nga say wóllëre ci peeñu, ne leen: «Tànne naa jàmbaar ci xeet wi, dénk ko ndimbal.
21Gis naa sama jaam Daawuda, fale ko sama diw gu sell,
22ànd ak moom, saxal ko, di ko dooleel.
23Noon du ko bett, ku bon du ko torxal.
24Ay bañam, ma rajaxe; ay noonam, ma fàdd,
25sama wormaak sama ngor di ko gunge, may yokk kàttanam.