Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sabóor - Sabóor 89

Sabóor 89:12-48

Help us?
Click on verse(s) to share them!
12Yaa moom asamaan, yaa moom suuf. Àddinaak li ci biiram, yaa ko taxawal.
13Bëj-gànnaar ak bëj-saalum, yaa ko sàkk. Tabor ak Ermon, tund ya, di sarxollee sa tur.
14Yaa àttan, jàmbaare; sa loxo di dooley neen, sa ndijoor ca kaw!
15Njekk ak njub a lal sab jal, ngor ak worma dox jiitu la.
16Aji Sax ji, ndokklee mbooloo mu la xal di sarxollee, di niitoo saw yiw,
17ànd di la bége bés bu ne, sag njekk siggil leen.
18Seen darajay doole, yaw a. Boo nu baaxee, nu yokku kàttan.
19Sunu kiirlaay lii, Aji Sax jeey boroom; sunu buur bii, Aji Sell ji séddoo Israyil ay boroom.
20Wax nga say wóllëre ci peeñu, ne leen: «Tànne naa jàmbaar ci xeet wi, dénk ko ndimbal.
21Gis naa sama jaam Daawuda, fale ko sama diw gu sell,
22ànd ak moom, saxal ko, di ko dooleel.
23Noon du ko bett, ku bon du ko torxal.
24Ay bañam, ma rajaxe; ay noonam, ma fàdd,
25sama wormaak sama ngor di ko gunge, may yokk kàttanam.
26Géej, ma teg ci loxoom, dex, ma ne ca tegg ndijooram.
27Moo ma naa: “Yaay sama baay, di sama Yàlla, di sama wéeru-mucc.”
28Te it maa koy def samab taaw, tiimale ko buuri àddina,
29sàmmal ko sama ngor ba fàww, feddlil ko sama kóllëre.
30Damay saxal askanam ba fàww, yàggal ab jalam ni asamaan.
31Bu ay sëtam wàccee sama yoon, baña doxe samay ndigal,
32mbaa ñu xëtt sama dogali yoon, baña sàmmonteek samay santaane,
33ma bantale leen seenug moy, dumaa leen seen ñaawtéef.
34Waaye duma ko daggal sama ngor, te duma ko ñàkke worma.
35Duma fecci sama kóllëre, te duma toxal sama kàddu.
36Benn yoon laa ko giñ ci sama sellnga, duma fen Daawuda:
37askanam, dàkk; ab jalam fi sama kanam ni jant bi,
38ak weer wi sax ba fàww, dib seede bu wér ca niir ya.» Selaw.
39Ndaxam yaw Yàlla, jéppi nga ki nga fal, mere ko, wacc ko.
40Fecci nga sa kóllëreek sab jaam, foq nguuram, detteel ko.
41Bëtt nga miiram yépp, saam ay tataam,
42ku fa jaare, jël ca alalam, mu doon mbalitu dëkkandoo yi.
43Yékkati ngay bañam, noonam yépp di ree.
44Dayal nga saamaram, te taxawuwloo ko cib xare.
45Xañ nga ko darajaam, rattax ngànguneem fa suuf.
46Dagg nga fani ngoneem, sang ko gàcce. Selaw.
47Éy Aji Sax ji, xanaa lii du jeex? Xanaa doo làqu fàww nii, sa mer di boy?
48Bàyyi ma xel, samay fan yàggul. Xanaa du neen a tax nga sàkk mboolem doom aadama?

Read Sabóor 89Sabóor 89
Compare Sabóor 89:12-48Sabóor 89:12-48