1Muy taalif bu ñeel Etan mi bokk ci giirug Esra.
2Aji Sax ji laay woye ngoram, ba fàww, di biral wormaam sët ba sëtaat.
3Dama ne, sa ngor dàkk la sax, fa asamaan nga dëël sa worma.
4Aji Sax ji nee: «Damaa fas kóllëreek ki ma tànn, muy Daawuda sama jaam bi ma giñal ne ko:
5“Damay saxal sa askan ba fàww, samp sab jal sët ba sëtaat.”» Selaw.
6Aji Sax ji, waa asamaan a ngi lay sante say jaloore, ndajem ñu sell ña di la joobee sa worma.
7Ana kuy dab-dabal Aji Sax ji, fa kawa kaw? Ana ci goney Yàlla yi ku nirook Aji Sax ji,
8Yàlla, ji ñu terala teral ci jataayu ñu sell ñi, te mu gëna raglu lu ko wër?