3Yaw, dëkkub Yàlla bi, tuddees na say jaloore. Selaw.
4Yàlla nee: «Ma limaale Misraak Babilon, ñi ma xam di dégg. Xoolal Filisti ak Tir, ak réewum Kuus. Nit a ngii, juddoo fa,»
5te teewul ñu cosaanale ko Siyoŋ, ne kii ak kee fa bokk juddoo, te Aji Kawe jee saxal Siyoŋ.
6Aji Sax jeey lim xeet yi, limaale leen ne: «Kii fi la juddoo.» Selaw.